Alyosha & Zosima

Personal poetry in different languages.

❛In principio erat Verbum.❜ A.I. Free

Yoonu xol

⇧ SECTION LISTING

Bu ma gëmmee, may gis dëggu xol yi
Ñoo gëna lëndëm guddi ga di nelaw
Xel yi silmaxa su jant samandaay bëtu seytaane
Booba duñu yég rabi dunyaa boobu
Kon léegi maa ngog di gëmm
Ma xaar ab xare buy féexal suma xol
Ñu ngi fii ñëw
Ni xel muy teey, ci xol bu nëb
Korti coxorte lañu
Ni céebi ci këpptal
Mënumaa tere suma xol rusloo ma
Konte na wone kanam gi soppiku ni kakatar yi
Waaye kàccoor yi amuñu kóllëre ak amaana
Rab wii baaxul xeex rab wee baaxul !
Na mbañeel wor kaññaan, na mbamb dóor genn kor
Ku mujj a di sama wujj bu gëna soxor
Xeexoon na ay xaritam ba gëna xoox benn xaleb góor
Waaye dafay soxorewati nit xol
Moo ma móolu, maay fent taalif buy fippu
Ndax ki mel ni ab noon mënu maa noob
Booba, ci biir xol bii
Ma fàttaliku ña fàttewuñu ma
Ñoo ma soppoon te moo leen siggiloon
Su ma xalaatee sumay déeyandoo
Sama xol bu të dafay dundaat
Tey, maa ngi fii
Maak moom, ak moom laa ne màkk, moom laa jàkk
Mboog mu mbubboo sama mbañ
Waaye mbokk la, waaw, man la rekk
Moo dëgguwoon ci sama gént
Maa doon dund ci géntam gi
Ci gëmmentu la géwal ma goreel
Moom ak léebamu gént

Sunday, 19th November 2017
Jean-Michel LEON-FOUN-LIN